Déggόo Catalan ba léegi?

 

Xamagoo lan moo tax nga wara jàng Catalan? 

Ca dun Baléares, Catalan làkk wu ñu nàmp la, booba ak léegi mat na 800 ans. Waaye Catalan ak Espanole mȅnoon nanoo nekk làkk wu nguur gi di jȅfandikόo. Ca Baléares, am nañu sañ- sañu jàng Catalane te di ko jȅfandikόo ci bépp anam.     

Lu bari ci askan wi dañuy làkk Catalan te ñi ȅpp ci ñoom dégg nañu ko. Ñu ngi jȅfandikόo Catalan ci bépp xeetu jȅflante diggante nit ñi, waaye itam ci wàllu liggéey ba ci biir nguur gi, ci ekkol yi, rajo yi ak tele yi, ba ci birό yi.        

 Catalan ay diiwaan yu baree ko bokk te lu ȅpp fukki million doomu aadama dégg nañu ko.        

 Jàng Catalan te di ko jȅfandikόo daf lay dimbali:     

  • Nga gȅna dund bu baax ci biir askan wi lay dalal. 
  • Nga gȅna mȅna xam aada yi, caada yi, cosaani réew mi nga nekk.   
  • Nga am ay jumtukaay yu lay may nga gaawa am liggéey te nga rattaxal saw nekkin ci biir askan wi. 
  • Nga gȅna mȅna sàmm sa njàngum doom yi  

 

Ndax bȅgg nga jàng Catalan?  

 

  • Ay jumtukaay ngir jàng Catalan 

Boo sukkandikόo ci liien bii, di nga mȅna nemmiku téeré booy jàngee Catalan ca dun Baléares. Di nga mȅna gis ci jumtukaay boobu ay xabaar yi gȅna méngόo ak li nga soxla. Mȅn nga cee gis sax foo mȅna jàngale sa bopp ak ay ay pexe ci internet bi ak yu deme  noonu.    

  

  • A l’abast. Jokkoo ci baat yi njȅkk ci Catalane 

A l’abast ab jumtukuaay la bu ñu sos ngir ñi déggul  Catalan te bȅgga xam bu baax ak jege làkk ak aada yi ci dun Baléares.

Ay kàddu la yu ñuy faral di dajeel ci làkku Catalan te méngόo ak sunuw nekkin bés bu yàlla sàkk.  

Lii nag gis gis bu njȅkk la rekk ci làkk woowu nga xam ne li ko taxa jόg mooy xiirtal nit ñi  ñuy wéyal njàngum katalan:     

Am na ci PDF.

Am na ci liñu internet bii. Day yombal déglu ay xet ci Catalan nga xam ci jumtukaayi yi bokk ci li lay gindi ci wax ji njȅkk ci A l’abast.

 

  • Mallorcat

Mallorcat jumtukaay la bu ku nekk mȅna jàngalee boppam Catalan. Ak jumtukaay bii me nga jàng baat te sukkandiku ci ay nataal, mȅn nga cee gis naka lañuy bindée baat yi ak naka lañu leen di waxee. 

   

  • Maó en català. Njàngalem Catalan mu njȅkk   

Xȅt wii dafa am ay pexey jokkoo ak ay baat yu ñu mȅna jȅfandikόo bés bu nekk. Lii lépp mu ngi am ca dekku Maó. Am na itam ay xabaar yu woor ci dund gi ci dȅkk boobu ak jumtukaay yi ñu mȅna jàngé Catalan. Ngir jot ci mȅnees na ko jaare ci lien bii.   

 

  • Ep! Escolta i parla    

Lii nag njàng la mu aju ci wax ngir saafara soxla yi jiitu bés bu nekk ci Catalan ak ay nataal, ay ndégtu (audio) ay vidéos, ak ay itte yu am solo. Ku ci bȅgga jot mȅn na ko jaare ci fii.